TSK

TSK · Jeremiah 21:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Boroom bi nee: «Bu ma sottalee liggéey fa kaw tundu Siyoŋ ak fa Yerusalem, maay mbugale buurub Asiri réy-réyloom gi, ak gëti xeebaateem.»

Bu bésub keroogee Aji Sax ji dikke mbugal gàngoor ya fa kawa kaw, ak buuri àddina yi fi suuf.

Yaa yebal say surga, di kókkali Boroom bi, te naa: “Sama watiir yi ne xas laa ware kawtey tund yi, jàll ba ca xolu Libaŋ. Maa gor seedaram ya fa sut ak tànnéefi garabi sipparam: maay àkki ba ca collub kaw bu tundu Libaŋ, ak gottam bu naat ba nib tóokër.

Tëgg wal taalam, mu yànj; sawara seeyal beteex. Xellees na koo xelli ci neen, taxul li ci bon génn.

Moo tax kay Aji Sax ji Boroom gàngoor yi wax ne: «Maa ngii di wàccesi mbugal fi seen kaw; seen xale yu góor fàddoo saamar, seeni doom, góor ak jigéen, deeye xiif.

Waaye su ngeen ma déggalul, baña sellal bésub Noflaay, baña moytoo gàddu lenn, di jaare bunti Yerusalem bésub Noflaay, su boobaa dinaa taal dëkk bi taal buy xoyom këri Yerusalem yu yànj, te du fey.”»

réyi pexe, màggi jaloore; say gët ne jàkk ci mboolem lu doom aadama def, ngay añale ku nekk jëfinam ak jëfam.

Àddina ab gent lay doon ndax ñi ko dëkke, muy añub seeni jëf.

¶ Bu leen lenn nax; Yàlla deesu ko foontoo. Nit ki, li mu ji, moom lay góob.