TSK

TSK · Joel 2:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

ne ko: «Éey Boroom bi, ndegam daj naa saw yiw, rikk àndal ak nun rekk, Boroom bi, ak li mbooloo miy dëgër bopp lépp! Jéggal nu sunu ñaawtéef ak sunu bàkkaar rekk, te nga séddoo nu.»

Ma gis ne ndeke moy ngeen seen Yàlla Aji Sax ji, daldi sàkkal seen bopp wëllu wu ñu móol, dëddu xaat yoon wa leen Aji Sax ji santoon.

Waaye reetaani noon laa ci ragal, lu ko moy seeni bañ juume ko, ba naan: “Sunu njàmbaar a!” te waroon ne: “Aji Sax jee def lii lépp!”»

Buntu néeg bu mag bi ab dëru biti la jàkkaarlool, yaatuwaayu dër bi di ñaar fukki xasab, tollook yaatuwaayu kër gi. Guddaayam féete ci kanam kër gi, yokke guddaayu kër gi fukki xasab.

Nu ngi nii tey diy jaam. Réew ma nga joxoon sunuy maam, ñuy lekk meññeefam aki ngëneelam, fi lanu doon nii ay jaam.

Rongooñ laay dunde guddeek bëccëg, noon yi di ma dëkke naa: «Ana sa Yàlla ji?»

Noon yaa ngi may ñaawal, di ma yendoo naa: «Ana sa Yàlla ji?» Ma ne yàcc, ne yasar.

Éy Yàlla, fu reetaani noon di dakke? Xanaa bañ yi duñu la ñàkke kersa ba fàww?

Noo ngi nii di mbalitu dëkkandoo yi; ñu séqe nu ay kókkaleeki kekku.

Bu yéefar yi ne mukk: «Moo ñii, ana seen Yàlla?»

Aji Sax ji, loo nuy wërloo fu sore say yoon, di nu dërkiisal, ba ragalatunu la? Sang bi, délsil ngir nun, sa giir yii nga séddoo.

¶ Mu yóbbu ma ba ca ëttu biiru kër Aji Sax ji, ndeke foofa ca buntu néeg Aji Sax ji, diggante dal-luwaayu bunt baak sarxalukaay ba, lu wara tollook ñaar fukki nit ak juróom a nga fa, ñu won gannaaw bérab bu sell bi, jublu penku, di sukkal jant bi, dëpp seen jë fi suuf.

Kon nag yeen tundi Israyil, dégluleen kàddug Boroom bi Aji Sax ji. Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ak tund yu mag yeek yu ndaw yi, ak xunti yeek xur yi, ak ndànd-foyfoy yu wéet yeek dëkk yi gental, te xeet ya ñu dëkkal sëxëtoo leen, yab leen.

Israyiloo, dellul ci sa Yàlla Aji Sax ji, fakktaloo nga sag ñaawtéef.

Joel 1:13 TSK

Yeen sarxalkat yi, gembuleen te tiislu, yeen ñi dénkoo sarxalukaay bi, yuuxuleen, yeen boroom dénkaaney sama Yàlla, dikkleen, sol ay saaku yu ngeen fanaanoo, ngir toroxlu, nde xañees na seen kërug Yàlla ga saraxu pepp ak saraxu tuuru!

Amos 7:5 TSK

Ma ne: «Boroom bi, Aji Sax ji, ngalla taxawal. Askanu Yanqóoba àttan na lii am? Lu néew doole lañu.»

«Ngeen ne: “Léegi nag tinuleen Yàlla rekk, mu baaxe nu!” Yeena tooñ, ndax day siggil kenn ci yeen?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.