Ma daanu tey, ñu daje di ko bége, dajaloo fi sama kaw, di ma fexeel te yéguma, di ma yàpp, tëë ba.
TSK
TSK · Lamentations 1:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji, yaw laa yaakaar; Boroom bi, sama Yàlla, yaa may nangul.
Yéeneb bii ñeel na Babilon, muy peeñum Esayi doomu Amocc.
Sa boroom Aji Sax ji, sa Yàlla jiy layool ñoñam dafa wax ne: «Mu ngoog, maa jële ci sa loxo, kaas bu wex biy miirloo; taatu kaas ba def sama mbugal, dootoo ko naan.
Waaye ku la lekk, dees na ko lekk; sa noon yépp lañuy jàpp njaam ba ñu daj. Ku la futti, dees na ko futti, ku la saax-saaxee dees na ko saax-saaxee.
Mowabee, du yeena doon ree Israyil? Dangeen leena fekk ci biiri sàcc, ba fu ngeen leen tudde, wëcc bopp?
Xaaculeen fi kawam, wër ko, Babilon daanu na, ba joxe ndodd, tata ya màbb, dàbbli ya rajaxoo! Aji Sax jeey feyu, feyuleen! Na mu defoon, defleen ko ko.
«Babilon mu reewee, maa ngii fi sa kaw.» Kàddug Boroom bi, Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi. «Sa bés déy taxaw na, di àpp bi ma la wara mbugale.
Waa Babilon it dinañu daanu ngir waa Israyil ñi ñu bóom, ba ñu yem ak mboolem waa àddina yi ñu bóom, te ñu daanu ndax Babilon.
Yoon yi jëm Siyoŋ jooy na wéet, kenn jaareetu ca màggalsi. Pénc yépp a gental, sarxalkat yay binni, janq ja jàq, Siyoŋ gépp di naqarlu!
Waa Siyoŋ gépp a ngi binni, di wut ab dund, seeni ngëneel lañuy weccikoo aw ñam wu ñu leqlikoo.
Yal na seen gépp mbon teew fi sa kanam, ba nga mbugal leen ni nga ma mbugale ndax mboolem samay tooñ. Samay onk bare na, sama xol jeex tàkk.
Sa noon yépp a lay ñaawal, di la kókkaleek a kekku, te naan: «Sànk nanu leen nag! Bii bés lanu yàggoona séentu, te noo ko fekke tey.»
¶ Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
Waruleen woona seetaan ci seen bésub mbokk, bésub njekkaram, Waruleen woona bége deminu Yudeen ñi ci seen bésub sànkute, mbaa ngeen di réy làmmiñ, ci bésub njàqare.
«Wóoy ngalla yaw mi nàndal sab dëkkaale, sotti sa ndabal sànj, màndale ko, ngir niir ko, mu ne duŋŋ!