Mooy ba Daawuda di xareek waa Siri ña ca Mesopotami ak waa Siri ña ca Soba te ba ñu ca bàyyikoo, Yowab duma fukki junniy Edomeen ak ñaar (12 000) ca xuru Xorom wa.
TSK
TSK · Lamentations 2:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Moo diwu pajtal amul Galàdd a? Am fajkat a fi amul? Ana lu waral bokk yi taneeguñu?
Nanga leen yégal saw tiis, ne leen: “Naa tuur rongooñ guddeek bëccëg, te du fer; sama bokki bopp yi damm ba dammtoo, ndaw góom bu metti!
Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Sa damm-damm du faju, sa góom du wér.
«Damm-damm yu dul wér ak mitit wu tar jarul jooy. Maa la teg lii, ndax sa ñaawtéef ju réy ak sa bàkkaar yu bare.
Yeen mboolem ñiy jaare yoon wi, lii safu leen, waaye seetleen rekk ba gis ndax wenn mitit dab na mitit wi ñu ma teg, te Aji Sax ji naqarale ma ko ci jantub tàkktel sànjam.
«Ñoom la Firawna di gis, muñe leen deminu gàngooram gépp, moom mi fàddoo saamar, mooki nitam ak mbooloom mépp. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.