Deesu ci sarxal cuuraay lu ñu diglewul, deesu ci rendi saraxu dóomal, deesu ci def saraxu pepp mbaa saraxu tuuru.
TSK
TSK · Leviticus 23:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Bu nit dee indil Aji Sax ji saraxu ndoortel meññeef, na ko indil mbool mu ñu séndal, def ko sànqal, muy saraxu ndoortel meññeefam.
Bésub juróom ñetteel ba na indi ñaari kuuy yu amul sikk, ak menn xar mu jigéen mu am at te amul sikk ak juróom ñeenti kiloy sunguf su mucc ayib su ñu xiiwe diw, muy saraxu pepp. Mu indaale genn-wàllu liitaru diw.
ak biiñ ngir saraxu tuuru, ñeenteelu xaajub xiin, di liitar ak genn-wàll, mu ànd ak saraxu rendi-dóomal mbaa beneen sarax, su dee xar mu ndaw.
Sa ndoxum naan it dees koy natt, mu tollook benn liitar bés bu nekk.
Nañu ci boole suba su ne benn céru juróom benneelu efab pepp, yemook ñaari kilook liibar, ànd ak liitaru diw, yemook benn céru ñetteelu xiinu diw buy tooyal sunguf si. Loolooy saraxu pepp mi, ñeel Aji Sax ji, di dogali yoon yu sax dàkk.
Yeen sarxalkat yi, gembuleen te tiislu, yeen ñi dénkoo sarxalukaay bi, yuuxuleen, yeen boroom dénkaaney sama Yàlla, dikkleen, sol ay saaku yu ngeen fanaanoo, ngir toroxlu, nde xañees na seen kërug Yàlla ga saraxu pepp ak saraxu tuuru!