Job 16:9
TSK
Meram la ma daggatee, jéppi ma, di yéyu ci sama kaw, daasal ma gëti noon, ne ma jàkk.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Meram la ma daggatee, jéppi ma, di yéyu ci sama kaw, daasal ma gëti noon, ne ma jàkk.
Yaw lañu daa woo wall, mucc; yaw lañu wóolu woon te rusuñu.
Ma daanu tey, ñu daje di ko bége, dajaloo fi sama kaw, di ma fexeel te yéguma, di ma yàpp, tëë ba.
Yàlla buma rusloo ñi la yaakaar, yaw Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, yàlla buma gàcceel ñi la topp, yaw Yàllay Israyil.
Gannaaw laa jox ku may dóor, dékk lex kuy xus sama sikkim, te làquma sama kanam ku may saagaak a serati.
Dees na ko xeeb, daw ko, muy nit ku bare mitit te miin naqar. Mu mel ni ku ñuy dummóoyu, dees koo xeeb te nawloowuñu ko.
Saaga nañu ko te feyuwul, daj na coono te tëkkoowul, waaye boppam la dénk kiy àtte dëgg.