TSK

TSK · Numbers 21:28

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

xur ya bartalu, jëm néegi Ar, leruji suufas Mowab.»

¶ Ba loolu amee Aji Sax ji ne ma: «Buleen dal ci kaw Mowabeen ñi, di leen song ub xare, ngir duma leen jox benn cér ci seenum réew, ndax askanu Lóot laa sédd réewum Ar.»

Moo tax Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, di yebal woppi ràgg fi kaw mbuxreem yi, seen daraja tàkk, sawara xoyom ko.

«Fa keppaaru Esbon lañuy daw taxawi, doole dëddu. Booba sawaraa tàkke Esbon, di law; sël-sëlee foofa ca péeyu Buur Siwon, ba dajal réewum Mowab, nitu coow ña, boole jë akum kaaŋ xoyom.

Amos 1:7 TSK

Maay yebal sawara ca tatay Gasa, mu xoyom ay taaxam.

Amos 1:12 TSK

Maay yebal sawara fa Teman, mu xoyomaale tatay Boccra.»

Amos 2:2 TSK

Maay yebal sawara réewum Mowab, mu xoyom tatay Keryot. Mowab deeye biir riirum xare, yuux ak liitu xare jibandoo.