TSK

TSK · Numbers 25:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ca ëllëg sa Musaa ne mbooloo ma: «Yeen de bàkkaar ngeen bàkkaar bu réy, waaye maa ngi nii di yéeg, jëm ci Aji Sax ji. Jombul ma jotul leen seen bàkkaar.»

Sarxalkat bi day rendi yooyu, menn mi di saraxu póotum bàkkaar, mi ci des di saraxu rendi-dóomal. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayam fi kanam Aji Sax ji ndax jàngoroy xelleem jooju.

Aaróona këf and ba Musaa wax, daw dugg ca biir mbooloo ma. Ndeke mbas ma tàmbali na ca biir mbooloo ma. Mu def ca and ba cuuraay, daldi defal mbooloo ma njotlaay.

Kon nag kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil: “Maa waxoon déy ne, sa waa kër ak sa waa kër baay ñooy doxe fi sama kanam, di ma liggéeyal ba fàww.” Léegi nag, kàddug Aji Sax jee: “Loolu jomb naa ko tey. Ñi ma teral laay teral; waaye ñi ma teddadil, dees na leen tuutal.

Suleymaan nag jële Abiyatar ci liggéeyu saraxi Aji Sax ji, daldi matal li Aji Sax ji waxoon ci waa kër Eli ca Silo.

Mu ne: «Man kat damaa xéroona xér ci yaw Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi. Waaw, bànni Israyil dañoo fecci sa kóllëreek ñoom; say sarxalukaay, ñu màbb; say yonent, ñu jam saamar. Ma des man doŋŋ, ñuy wuta jël sama bakkan nii!»

Yeen nag lees di wooye: «Sarxalkati Aji Sax ji,» ñu naa: «Sunu surgay Yàlla yaa ngi!» Alali xeet yi, yeena koy lekk, di damoo seeni koom.

Ni biddiiwi asamaan weesee lim, feppi suufas géej wees waññ, ni laay fule askanu Daawuda sama jaam bi ak askanu Leween ñi may liggéeyal.»

Acts 22:3 TSK

¶ «Man ab Yawut laa, juddoo Tàrs ca diiwaanu Silisi, yaroo ci dëkk bii. Ci keppaaru Gamalyel laa jànge, njàng mu dëppoo bu mat sëkk ak sunu yoonu maam. Ma doonoon ku xér ci Yàlla ni mboolem yeen ñii tey.

Moo tax fàww mu niru woon ay bokkam ci bépp fànn. Su ko defee mu mana doon seen sarxalkat bu mag bu am yërmande te wóor fa kanam Yàlla, ngir mana defal askan wi seen njotlaayal bakkan.

Ndax kat, gii kàddu, seedeelees na ko ko: «Yaa dib sarxalkat ba fàww, topp dayob Melkisedeg.»

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.

¶ ba noppi def nu nuy askanu sarxalkati Buur Yàlla Baayam, na ko daraja ak kàttan ñeel tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.