¶ Nit ki tooñ cig teyeefam nag, muy njuddu-ji-réew, di doxandéem, kooku Aji Sax ji la ñàkke kersa. Nit kooku, dees koy dagge ci biiri bokkam:
TSK
TSK · Numbers 25:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Waayi bànni Israyil ja ñu jamoon, te boole kook ndawas Majan sa jam, mooy Simri doomu Salu. Kilifag kër maamam la woon ca Cimyoneen ña.
¶ Ba loolu amee bànni Israyil jàpp jigéeni Majan, ak seeni tuut-tànk, ak seen jur gépp, gu gudd ak gu gàtt, seen alal jépp, ñu sëxëtoo ko.
¶ Gannaaw ba loolu wéyee njiit ya dikk, ne ma: «Du bànni Israyil, du sarxalkat yi, du Leween ñi, kenn ci ñoom teqlikoowul ak xeeti réew meek seen aada yu siblu. Dañuy jëfe ni Kanaaneen ñeek Etteen ñeek Periseen ñeek Yebuseen ñeek Amoneen ñeek Mowabeen ñeek waa Misraak Amoreen ñi.
Ba loolu amee Esra bàyyikoo kër Yàlla ga, fatuji néegu Yowanan doomu Elyasib. La mu fa nekk nag lekkul, naanul, xanaa di ñaawlu na ngàllo, ga ñibbsi feccee worma.
Bésub keroog Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi moo leen di woo ci jooyoo ak ñaawlu ak wateefu nel, ak colu saaku ngir ñaawlu.
Ñu wara am gàcce ci seen jëf ju siblu, te gàcce gàcceelu leen. Xamuñu sax luy kersa! Moo tax ñuy fëlëñoondook ñiy fëlëñu. Kera ba ma leen di dikkal, ñooy tërëf.» Aji Sax jee ko wax.
su boobaa nag dégluleen li ci Aji Sax ji wax, yeen ndesu Yuda. Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: “Su ngeen dogoo ba dogu, nara dem Misra, ba dem toogaani fa,
«Li nga nuy wax ci turu Aji Sax ji, dunu ko déglu.
Diggante buntu néeg bu sell beek sarxalukaay bi, sarxalkat yi, boroom dénkaaney Aji Sax ji, nañu fi taxaw jooy; nañu ne: «Aji Sax ji, yërëmal sa ñoñ; bul wacce say séddoo gàcce, ak ñaawley xeeti jaambur yi. Lu jar ñuy wax ëllëg ci biir askani jaambur yi, naan: “Ñii, ana seen Yàlla ji?”»
Ñooy gannaxi géej gu sàmbaraax, di gëq seen puuriti gàcce; ñooy biddiiw yu fàq di taxawaalu, te lëndëm gu ne këruus di cér bu ñu leen sédde ba fàww.