TSK

TSK · Numbers 6:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Naka la Yuusufa ne gees, gis Beñamin rakku doomu ndeyam ja. Mu laaj leen ne leen: «Ndax kii mooy seen rakk, ji ngeen ma doon wax?» La ca tegu mu ne rakkam ja: «Sama ngóor si, yal na la Yàlla defal yiw waay!»

Bare na ñu naan: «Ana ku nuy won lu baax?» Éy Aji Sax ji, baaxe nu saw yiw!

Yaa yor sama àpp. Xettli maak ku ma noonoo ak ku may sonal.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor yi, di seedeb Sabóor, giiroo ci Asaf.

ba dootunu la dëddu. May nu nu dund, nu wormaal sa tur.

Sang bi, geesoo ma sag leer, te xamal ma sa dogali yoon,

«Ngeen ne: “Léegi nag tinuleen Yàlla rekk, mu baaxe nu!” Yeena tooñ, ndax day siggil kenn ci yeen?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.