TSK

TSK · Philippians 2:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Réy-réylu jote rekk lay jur, ku dégg ndigal a xelu.

¶ Yeesu teg ca ne: «Maa ne leen, kooku moo ñibbaale këram àtteb ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy réylu, dees na la toroxal, waaye ki toroxlu lees di yékkati.»

Nanu jëfe jëfin wu jekka def bëccëg; nanu sore xawaare ak màndite, sore baane bu lewul, ak yàqute yu ni mel, te sore ŋaayoo ak kiñaan.

ndax kat maa gëna ñàkk solo ci ndawi Almasi, te yeyoowuma sax turu ndaw, gannaaw maa doon bundxatal mbooloom Yàlla mi.

Waaye su ngeen dee màttante ak a lekkante kat, moytuleena far yàqante yaxeet!

Bunu di yég sunu bopp, di merloonte ak a iñaanante.

¶ Mboolem lu ngeen di def nag, buleen ci boole xultu mbaa xuloo,

kooku, ab xogglilukat la te xamul dara. Woppi werante ak xuloo ci baati kese, moo ko dal, te loolu mooy jur ñeetaane, ak ŋaayoo, aki saaga, ak ñaaw njort,

James 4:5 TSK

Am defe ngeen ne ag neen la Mbind mi indee ne: «Xemmemtéef gu ànd ak fiiraange la Yàlla am ci noo gi dëkk ci nun.»

¶ Naka noonu yeen ndaw ñi, nangul-leen magi mbooloom gëmkat ñi. Yeen ñépp nag toroxluleen ci seenug jëflante, ndax: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»