TSK

TSK · Proverbs 1:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Day tëroo ciy dëkk-dëkkaan, làqu di bóom ku deful dara, nëbbu di wootal néew-ji-doole.

Defuma dara, ñu di ma fiir, defuma dara, ñu gas um yeer, di ma tëru.

di jam ku ñu tëru te deful dara; jekki jam ko, te tiituñu ci dara.

Ñii kat seen bopp lañuy fiir, seen bakkanu bopp lañu sànk.

Soxor bi, bul tëru ku jub ci këram, bul yàq dëkkuwaayam.

Ag maas a ngi, seeni sell niy saamar, seeni gëñ niy paaka, ñuy lekk néew-ji-doole, ba raafal leen ci réew mi, ba ku ñàkk jeex ci biir nit ñi.

Ndax damaa naagu woon ni xar mu ñu jëme rendikaay ba. Xawma woon ne man lañuy lalal ay pexe, naan: «Nan gor garab ak doomam, dagge ko fi réewum boroom bakkan, ba deesul fàttlikooti turam.»

Micah 7:2 TSK

Ngor a jeex ci réew mi, njub tumurànke ci nit ñi. Ñépp, ku ñu tuur deretam lañuy tëru, ku nekk, mbokkam lay fiir.

Acts 25:3 TSK

tinu ko ngir mu woolu Póol Yerusalem, ndax fekk na leen lal pexem rey ko ca yoon wa.