TSK

TSK · Proverbs 14:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Su dul woon ak sama Yàllay baay, ji ànd ak man, di Yàllay Ibraayma, ji Isaaxa wormaaloon, konoon nga dàq ma tey, ma dem loxoy neen. Waaye sama toskare ak sama àqu ñaq la Yàlla gis, ba tax mu àtte ma ak yaw biig.»

Màggal-leen Ki Sax! Ndokklee ku ragal Aji Sax ji, di tàqamtikoo ay santaaneem.

Aji Sax jeey barkeel ku ko ragal, mag ak ndaw.

Kon doo ragal njàqare lu bette ak saaysaay buy songe,

Ragalal Aji Sax ji ndax nga gudd fan, nopplu te baña loru.

Liy dalal seen jamono mooy koomu ndam; xel ak xam-xam, te ragal Aji Sax ji, loolooy seen alal.

Maa leen di may benn xol ak benn jubluwaay ngir ñu di ma wormaal seen giiru dund, muy seen ngëneel, ñook seen doom yi leen di wuutu.