TSK

TSK · Proverbs 14:32

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 13:15 TSK

Su ma doon rey it moom laay yaakaar, maay janook moom, layool sama bopp.

Job 19:25 TSK

Waaye man xam naa ne sama jotkat a ngi dund, te mooy mujje taxaw fi kaw suuf.

Yaa may xamal yoonu ndund. Fu bànneex mate, yaa teew, xéewal sa ndijoor la saxe.

Su may jaare xuru ndee wu ne këruus it, duma ragal loraange: yaw laak man, sa bantu sàmm ak sa nguul, yooyoo may dalal.

yal nañu mel ni ngumbaan-tooye buy dox, di seey, mbaa lumb wu jigéen tuur, gisul jant.

Moo tax musiba di jekki dal ko, mu jekki yàqu, ba wees paj.

Ku jub day daanu juróom yaari yoon, jógaat, ab soxor sërëx ci njekkar.

Luke 2:29 TSK

«Léegi nag Buur Yàlla, yiwil sab jaam, mu dem ak jàmm, noonee nga ko waxe woon.

Kon ñeme lanu def, te li nu gënal di génn, des bitib sunu yaramu tey, ngir dëkki ak Sang bi.

Ci diggante yaar yooyii laa tance: yàkkamti na maa yiwiku ba fekki Almasi, te loolu moo dàqati fuuf.

Boroom bee may wallu ci jépp jëf ju bon, te moo may aar ba tàbbal ma fa nguuram ga fa asamaan. Daraja ñeel na ko, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.