TSK

TSK · Proverbs 15:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Kon nag dangay tànn ci biir mbooloo mi mépp ay góor ñu mat, ñu ragal Yàlla te dëggu, boole ci sib alalu ger. Su ko defee nga tabb leen, ñu yilif ay kurél yu mat junniy nit ak yu tollu ci téeméeri nit, ba ci juróom fukki nit mbaa fukki nit.

Buleen dugal yëf yu seexluwu seen biir néeg, lu ko moy àtteb faagaagal bi war ci yëf yooyu, moo leen di dab, yeen itam. Xofleen koo xof, seexlu koo seexlu, ndax yëf yooyu, faagaagal moo ci war.

Doomi Samiyel yu góor ya nag jaaruñu ci seen tànki baay. Dañoo lajj, topp alal ju lewul, di nangu ay ger, di jalgati dëgg.

Ngaanag Naaman dina la topp, yaak saw askan ba fàww!» Ba mu ko defee Gewasi bàyyikoo ca Alyaasa, daldi gaana, yaram wa ne fureet, weex furr.

Képp kuy lekk lu lewul, nii lay mujje: wutin wu lewul jël bakkanu boroom.

Kuy fitnaal sa waa kër doo donn dara, ku dof, boroom xel yilif la.

Kilifa gu amul ug dégg, day foqati rekk, waaye ku bañ lu lewul, gudd fan.

Wóoy ngalla ñii di dajale kër ak kër, tool akub tool, aakimoo fépp, ba des ñoomu neen ci réew mi.

Xanaa kiy doxe njekk, di wax njub, bañ alalu foqati; loxo bay jalax ab ger, noppam di tanqamlu waxi bóome, bëtam di gëmm, ba du gis lu bon.

«Wóoy ngalla kuy dajaleel këram alalu yàqute ju lewul tey aj am tàggam fu kawe, ngir fegu ci yàqule.