TSK

TSK · Proverbs 18:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Esawu nag bañ Yanqóoba ndax barke ba ko baayam ñaanal. Ma ngay wax ca xolam naan: «Balaa yàgg ñu dëj sama baay, te bu boobaa dinaa rey sama rakk Yanqóoba.»

¶ Booba Yanqóoba, Yuusufa la gëna bëgg ci ay doomam, ndax li mu màggat door koo am. Mu ràbblul ko mbubb mu yànj.

¶ Naka la ko mag ya séen fu sore, daldi mànkoo bala moo agsi, ci pexem rey ko.

¶ Ba mu ko defee Absalom sant ay nitam, ne leen: «Ma ne, bu Amnon naanee biiñ, ba xolam sedd, bu ma leen nee ngeen jam ko rekk, reyleen ko. Buleen ragal; man maa leen ko sant. Góor-góorluleen nag te ñeme.»

¶ Ba Israyil gépp gisee na leen Buur tanqamloo, dañu koo tontu ne ko: «Ana lu nu bokk ak Daawuda, lu nu séq ak doomu Yese? Bànni Israyiloo, ca seeni xayma! Yaw askanu Daawuda, xoolalal sa bopp sa kër.» Ba mu ko defee bànni Israyil dellu ca seeni xayma;

seede buy fen rekk, rawatina kuy yokku ay ci biiri bokk.

¶ Mbir mi nag mujje dëngoo bu metti, ba ñu teqlikoo. Barnaba ànd ak Yowaan Màrk, dugg gaal, jëm Sippar.