TSK

TSK · Proverbs 19:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yuusufa dellu ne ay magam: «Jegeñsileen.» Ñu jegeñsi. Mu ne leen: «Man maay Yuusufa, seen rakk, ji ngeen jaayoon, ñu indi ma Misra.

Absalom ak waa Israyil gépp daldi ne: «Ndigalal Usay, Arkeen bii kat, moo gën ndigalu Ayitofel.» Booba Aji Sax jee nara indil Absalom musiba. Moo tax mu neenal pexem Ayitofel mu jub ma mu laloon.

Job 23:13 TSK

Yàlla de kenn la, ana ku koy waññi? Coobarey bakkanam lay def.

Aji Sax jeey neenal li xeet yiy fexe, di gàntal li mbooloo yiy mébét;

Ku baax, Aji Sax ji bége la; kuy fexe lu bon, mu daan la.

Nit xeluwul, amul ug dégg ak pexe, ba manal Aji Sax ji dara.

‘Nan songi Yuda, tiital leen, nangu ko, fal fa doomu Tabeel buur.’

Mii mébét lañu mébétal àddina sépp, bii loxo lañu xàccil xeet yépp.

Li ngeen mébét ci seen xel du am mukk. Yeena ngi naan: ‘Nan mel ni xeet yépp, mel ni waasoy réew yi, di jaamu bant ak doj.’

Day dugg ndànk ba ca biir gox ya gëna woomle ca diiwaan ba. Dina fa def lu ay baayam aki maamam masula def. Dina lël ay réew, séddale ay farandoom alal jaak koom ga. Dina lal pexe yu mu songe ay tata, waaye loolu ab diir lay doon.

Acts 5:38 TSK

Léegi nag, dama ne, maanduleen ci ñii, te ba leen, ngir su seen mébét mbaa seen jëf bawoo ci nit, day yàqu rekk.

Yàllaa bëggoona firndeel nu mu gëna leere ñeel ñi moom dige bi, ne ab dogalam du tebbiku mukk. Moo tax mu dogale ngiñ ab digeem.

Jude 1:4 TSK

Ndaxte ñenn a ngi ñu ñu yàgga bind seenub àtte, te ñoo yoxoosu ci seen biir, di ñu ñeme Yàlla; ñooy taafantoo yiwu Yàlla ngir yoonal ag yàqute, di weddi Buur biy kenn, te di sunu Boroom Yeesu Almasi.