TSK

TSK · Proverbs 22:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Su boobaa sama mer dina tàng, ma reye leen saamar, seeni jabar diy jëtun, seeni doom diy jirim.

Ana sax ku buurub Israyil jóg, di dàqi? Ab xaj bu dee, aw fel doŋŋ lay dàq!

Ñu ngi naa: «Sunu làmmiñ lanuy daane, nook sunu kàddu; ku nu manal dara?»

Ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, digaaleel ak samay digaale, xeexal maak ñi may xeex.

Éy Yàlla, àtte ma, layool maak xeet wu gorewul, xettli maak ku njublaŋ te dëng.

Aji Sax jeey def njekk, di àtte jépp néew-ji-doole.

Xam naa ne Aji Sax jeey jox néew-ji-doole dëgg; di sàmm àqu baadoolo.

Ki koy aar màgg na, da koy taxawu, dal ci sa kaw.

Waaye ku la lekk, dees na ko lekk; sa noon yépp lañuy jàpp njaam ba ñu daj. Ku la futti, dees na ko futti, ku la saax-saaxee dees na ko saax-saaxee.

Aji Sax ji nag dafa wax ne: «Maa ngii di leen layool seen layoo, ba feyul leen. Maay ŋeeral géejam, ŋiisal am walam,

Yaa sëxëtoo woon ay xeet yu bare, mboolem ndesu askan yee lay sëxëtooji, ndax deretu nit ji nga tuur, soxore ay réew, aki dëkk, ak mboolem ña ca biir.