TSK

TSK · Proverbs 24:28

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Buleen seedeel seen moroom lu dul dëgg.

¶ Doweg, Edomeen ba taxawandook jawriñi Sóol, daldi àddu, ne: «Man de, gis naa doomu Yese ji, mu dikk dëkk ba ñuy wax Noob, ca Ayimeleg doomu Ayitub.

Job 2:3 TSK

Mu ne ko: «Xanaa seetlu nga Ayóoba, sama jaam bi! Amul moroom fi kaw suuf de! Ku mat la te jub, ragal Yàlla te dëddu lu bon.»

Nit ku bon a ngi may duural, di ma jiiñ lu ma yégul.

Seede bu dëggu, dëgg rekk, seede bu dëgguwul, fen rekk.

Seede buy fen muccul mbugalam, kuy noyyee ay fen, mujje sànku.

Ku seedeel sa moroom ay fen, yen nga ko aw njur mbaa saamar mbaa fitt.

¶ Kon nag bàyyileen fen, te ku nekk di wax sa moroom, dëgg, ndax ku nekk ci yeen sab céru moroom nga.

waaye ñu ragal ñi ak aji gëmadi ñi ak defkati ñaawtéef yi ak bóomkat yi ak moykat yi ak xërëmkat yi ak bokkaalekat yi, mboolem niti fen ñi, seen añ a nga ca déegu sawara waak tamarax ba. Loolu moo di ñaareelu dee.»