TSK

TSK · Proverbs 29:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Buur Daawuda ci kaw Israyil gépp la nguuru woon; muy jëfe njub ak njekk ñeel réewam mépp.

Muy def nag li Aji Sax ji ñaawlu; giiru dundam dëdduwul bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil.

Yaa àttan, jàmbaare; sa loxo di dooley neen, sa ndijoor ca kaw!

Samay pexe la buur di jiitee, kilifa di ci àttee dëgg.

Su buur àddoo cib àtte, muy kàddu gu Yàlla dogal.

Su buur toogee di àtte, day gis, di ràññee mboolem ayib.

Boroom bee yónnee kàddu gu dal Israyil, askanu Yanqóoba,

Wóoy ngalla kiy tabax këram te seetu ci njekk, di teg taaxi kawam te seetu ci yoon, liggéeyloo moroomam ci dara, feyu kow ñaqam.

Micah 7:3 TSK

Lu bon la seeni loxo mane: kàngam di laaj, ab xaali di sàkkub ger, boroom daraja moom, di wax fuqley bakkanam, ñu ànd ràbbum pexe.