TSK

TSK · Proverbs 6:32

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ëpplewu ma sañ-sañ ci biir kër gi, te aayewu ma lenn xanaa yaw, ndax soxnaam nga. Kon léegi nu may mana defe ñaawtéef wu réy wu ni tollu, di moy Yàlla?»

Këram day joy wuti ndee, ay jaaruwaayam jëm njaniiw.

Jëf ju bon day fiir ka ko sàlloo, bàkkaaram di mbaal, jàpp ko.

Waa ja jekki, topp ko, mbete yëkk wu ñuy rendiji, mbaa dof bu ñu jéng, di ko yari.

naan: «Képp ku téxét, jàddal ba fii!» Ku ñàkk bopp, mu ne ko:

Ma walbatiku, di jéema xam, di wut, di càmbar, di sàkkum piri, ngir xam li bon cig ndof, ak li dofe, cig ndof.

Ngalla dégluleen lii, xeet wu dofe, ñàkk xel wi ngeen doon, ami gët te dungeen gis, ami nopp te dungeen dégg!

Ngànctu ak biiñ bu yàgg ak bu bees, moo yóbbu seenum xel.

Xel mu rafet lañuy jaay ba mujj diy dof.