¶ Mbooloo ma mépp daldi koy génne dal bi, dóor koy xeer ba mu dee, na ko Aji Sax ji sante Musaa.
TSK
TSK · 1 Kings 21:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Reyleen ko rekk. Yeen ñi mu doon jéema yóbbaale, na ko seen loxo jëkka dal, ngir rey ko, bala cee loxol mbooloo mépp topp.
Na ko góori dëkk bépp dóori doj ba mu dee. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir. Israyil gépp a koy dégg, daldi ragal.
génneleen leen ñoom ñaar, ba ca bunt dëkk booba, ngeen dóor leen ay doj ba ñu dee, ndax ndaw si moo yuuxuwul woon wall, te muy ca biir dëkk ba, te waa ji it moo jabaroo jabaru moroomu góoram. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.
“Aji Sax ji dafa wax ne: Deretu Nabot ak deretu doomam yi déy, gis naa mu tuuru fii démb. Kon nag dinaa la ko topp, nga fey ko ci tool bii. Loolu la Aji Sax ji wax.” Kon nag yóbbul sànni ci tool bi, muy la Aji Sax ji waxoon.»
Xàccil sa loxo rekk, dal ci mboolem lu bokk ci moom. Ndegam du jàkkaarlook yaw, xarab la.»
ndegam maa lekk lu ca ñor, te dikkewuma dara, ba xañ bakkan ña ma ko beyaloon,
Nit ku bon a ngi may duural, di ma jiiñ lu ma yégul.
Seede buy fen muccul mbugalam, kuy noyyee ay fen du rëcc àtteem.
Seedeb naaféq faalewul yoon, ab soxor lu bon lay tàqamtikoo.
Ma seetlooti gépp notaange gu am fi kaw suuf. Ndeke néew-doolee ngi jooy, amul ku ko dëfal. Ki koy not a am doole, te néew-doole ji amul ku ko dëfal.
Nit ñi dinañu taxawaalu ci réew mi, boole njàqareek ub xiif, te bu ñu xiifee, ñéññ, téen, xool kaw, saaga seen buur, saaga Yàlla,
«Maa leen di dikke ab àtte, di ab seede bu taxaw temm ci tuumaal ñeengokat yeek njaalookat yi, ak ñiy fene ngiñ, ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram, di noggatu ab jëtun akub jirim, di beddi doxandéem te ragaluñu ma.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
¶ Ba loolu amee ñu yuuxu ca kaw, dar seeni nopp, daldi ànd, ne milib ca kawam;