Ibraayma ne ko: «Da di dama noon, amul kenn ci réew mii ku ragal Yàlla, te dees na ma rey ndax sama soxna.
TSK
TSK · 1 Peter 2:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ca gannaaw ëllëg sa Yuusufa ne leen: «Bu ngeen defee lii may wax, dingeen dund, ndax man ragal naa Yàlla.
¶ «Bu boroom bijjaaw teewee, jógleen wormaal ko. Deeleen rus mag te ragal-leen seen Yàlla. Maay Aji Sax ji.
Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu xam-xam, te xel mu rafet akub yar, dof yaa ko xeeb.
Doom, ragalal Aji Sax ji, wormaal buur. Bul lëngook kuy fippu.
¶ La ca tegu ma damm sama ñaareelu yetub sàmm ba, Bennoo, ngir dog bokk gi dox diggante Yuda ak Israyil.
Joxleen ku nekk li ngeen warlook moom; ku ngeen wara fey galag, feyleen ko ko; ku ngeen wara fey juuti, feyleen ko ko; ku ngeen wara weg, wegleen ko; ku ngeen wara teral, teral-leen ko.
te ngeen rus Almasi, ba tax ngeen di nangulante.
¶ Mboolem ñi ci buumu njaam, nañu jàpp ne seeni sang yelloo nañu gépp wegeel, ngir kàddu gu teddadi baña tege ci turu Yàlla, ak sunu àlluwa.
¶ Kon nag gannaaw setal ngeen seen xol, ndax dëgg gi ngeen déggal, ba tax ngeen am cofeel gu mucc jinigal, ci bokki gëmkat ñi, nangeen soppantee xol bu set, cofeel gu mat sëkk.