TSK

TSK · 1 Peter 5:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 1:6 TSK

¶ Mu am bés goney Yàlla dikk, teewsi fa Aji Sax ji. Seytaane tuumaalkat bi itam bokk ca.

gaynde gu ndaw ŋaral am pàddam, di sàkkoo dundam fa Yàlla.

Merum buur ni gaynde gu ŋar; yërmandey buur ni lay cig mbooy.

Dañuy ŋar ni gaynde, ŋarati ni gaynde gu mat; yëmmu, ŋank um rëbbam, yóbbu te kenn du wallu.

Ki may dëggal jege na. Ana kuy layook man? Nan bokk taxaw! Kuy jànkoonteek man ci yoon? Na jegesi boog!

Ñu ngi ŋarandoo niy gaynde, di xiiroo ni gaynde yu ndaw.

Ay yonentam a ngi déeyoo fi biiram; ñu ngi xiiru ni gaynde guy xotat pàddam, di lekk doom aadama yi, foqati alal ak gànjar, ful jëtun yi ci biiram.

Dees na topp ci gannaaw Aji Sax ji, muy yëmmu ni gaynde. Mooy yëmmu moos ni gaynde, ay doomam di lox, jóge sowu.

Amos 3:4 TSK

Gaynde dina ŋarem ngeer te fàddul? Am gaynde gu ndaw dina xiiroom paxam te jàppul?

¶ Gannaaw gi Aji Sax ji won ma Yosuwe sarxalkat bu mag ba, mu taxaw fa kanam malaakam Aji Sax ji, Tuumaalkat bi taxaw féete ko ndijoor, ngir tuumaal ko.

Waaye su jawriñ ja nee ci xelam: “Sama njaatige dikkagul léegi,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya, góor ak jigéen, di lekk ak a naan, di màndi,

Teewluleen boog, tey ñaan saa su nekk, ba mana mucc ci mboolem looluy nara xew, ngir ngeen taxaw fi kanam Doomu nit ki.»

Kon nag bunu nelaw ni ñi ci des, waaye nanu teewlu, te ànd ak sunu sago.

Teewul muccu jigéen a ngi ci njurum doom, ndegam saxoo na ngëm, ak cofeel, ak jëfin wu sell te yem.

Naka noonu, na jigéen ñiy taxawu mbooloo mi di ñu tedd, buñu diy soskat, nañu moom seen bakkan, te jara wóolu ci lépp.

Titus 1:8 TSK

Waaye war na di ku man gan, ku xejjoo lu baax, jiital am xelam, jub, sell te moom boppam.

Titus 2:4 TSK

ngir tàggat jeeg ju ndaw ji ci sopp seen jëkkër, sopp seeni doom,

Yiw woowu moo nu digal nu dëddu ñeme Yàlla, ak xemmemtéefi àddina, te jiital sunum xel, di jëfe njub, te nekke ag njullite ci àddinay tey jii.

¶ Kon nag teewlooleen seen xel, te ànd ak seen sago, te ngeen wékk seen jépp yaakaar ci yiw wa ñu leen di dikke kera bu Yeesu Almasi feeñee.

Kon nag yaw asamaan, bégal, yaak mboolem ñi ci sa biir! Waaye wóoy ngalla yeen géej ak jéeri! yeen, ñi Seytaane wàccaale mer mu tàng fi yeen, ndax xam ne fan yu néew a ko dese.»

Ñu jàpp nag Seytaane, mi leen daan nax, sànni ko ci déegu sawaraak tamarax ba, mu fekki fa rab waak yonentu caaxaan ba. Dees na leen fa mitital guddi ak bëccëg, ba fàww.