Waaye su ngeen walbatee seen xol, dégluwuleen, xanaa ngeen lajj, di sujjóotal yeneen yàlla, di leen jaamu,
TSK
TSK · 1 Samuel 12:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dañoo xalab ay ndigalam ak kóllëre ga mu fasoon ak seeni maam, xalab kàddu ya mu leen artoo woon. Ñu topp ay tuuri caaxaan ba mujj di niti caaxaan, di roy xeet yi leen wër, te Aji Sax ji tere woon leen ñu roy leen.
Biralal-leen nu mbiri ëllëg, nu xam ne ay yàlla ngeen. Defleen rekk lenn, muy lu baax di lu bon, ndax nu bokk ko gis, ba yéemu.
Képp kuy tabax jëmmi tuur, doo tus, xërëm yooyu ñu safoo amul njariñ. Ñooñu ñu defi seede te gisuñu, yéguñu, muy seen gàcce!
yékkati teg ci mbagg, yóbbu, teg bérab, mu des fa; du jóge fa mu tege, ku ko woo wall it, du wuyu, ba jot ko ci njàqare.
«Ñaari yoon la xeet wi ma séddoo bàkkaar: ma di bëtu ndox muy dund, ñu wacc ma, man, di gasal seen bopp kàmbi dencukaayi ndox, te kàmb yi fett, di senn.
Cóolóolu neen, liggéeyu caaxaan; bu bésam taxawee, mu sànku.
Yaw Aji Sax ji may dooleel, di ma feg, di ma làq bésub njàqare, yaw la xeet yiy bawoo cati àddina, fekksi la, naan: «Caaxaani neen kay la sunuy maam baaxoo woon, xërëmi neen yu amul njariñ.
Ñiy wormaal neenug neen daal, ñoo dëddu seen yiw fa Yàlla.
¶ Kon su dee wàllu ñam wu ñu sarxal ay tuur, xam nanu ne ay tuur du dara ci àddina, te Yàlla kenn la.