TSK

TSK · 1 Samuel 18:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ci kaw loolu Sóol ne Daawuda: «Sama taaw bu jigéen, Merab a ngii. Moom laa lay may. Nekkal ma sama jàmbaaru xare rekk, te xareel Aji Sax ji ay xareem.» Booba Sóol a nga naan ca xelam: «Bu ko sama loxo laal, nay loxol waa Filisti.»

¶ Sóol yebal ay ndaw ca kër Daawuda ngir ñu xoolal ko ko, ba bët set, ñu rey ko. Mikal, soxnas Daawuda, yégal ko Daawuda, ne ko: «Soo rawalewul sa bakkan ci guddi gi de, bu ëllëgee dees na la rey.»

Xarit ak dëkkandoo di ma daw, mbokk dànd ma.

Su la nëbbalee mbañeel, di la nax it, ag mbonam mujj bir ñépp.

«Waaw! Daa am ñu bon ci sama ñoñ, ñuy tërook a fiire mbete nappkati picc.