TSK

TSK · 2 Kings 21:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Buleen tilimal réew mi ngeen nekk. Deret kat mooy tilimal réew mi, te réew mi deesu ko jote lenn, ci deret ju ñu tuur ci biiram, lu moy deretu ka tuur deret.

Aji Sax ji dina fàdd Israyil. Dinañu mel ni gattax guy foy-foyi cim ndox. Dina déjjatee Israyil ci suuf su baax sii mu joxoon seeni maam, tasaare leen ca wàllaa dexu Efraat, ndax dañoo samp ay xer yu ñuy jaamoo Asera, di merloo Aji Sax ji.

Terewul mu sax ci xeetu bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat doon bàkkaarloo Israyil, bañ koo dëddu.

¶ Moo dugal ba tey jëmm ja mu sàkkoon ngir tuur ma ñuy wax Asera, ca biir kër ga Aji Sax ji waxoon Daawudaak doomam Suleymaan ne leen: «Ci biir kër gii ci Yerusalem, gi ma tànne ci mboolem giiri Israyil, laay dëj sama tur ba fàww.

Ci ndigalal Aji Sax ji moos la loolu xew ca Yuda, ba mu mujj leen xarab ndax bàkkaari Manaseek li mu def lépp,

kuy daŋŋiiral, kuy fen, kuy rey nit ku deful dara,

te notuleen doxandéem, ab jirim akub jëtun, tuuruleen deretu jaamburu Yàlla, fi bii bérab, toppuleen yeneen yàlla bay loru,

Li ko waral mooy dañu maa wacc, teddadil bérab bii, di fi taalal cuuraay yeneen yàlla yu ñu xamuloon, du ñoom, du seeni maam, du buuri Yuda. Te feesal nañu bérab bii deretu nit ñu deful dara.

Waaye ay nit ñu jub a ngii, ñoo leen di atteji àtteb njaalookat yu jigéen, àtteb bóomkat yu jigéen, nde ay njaalookat lañu, te ay bóomkat lañu.

Ñii, ñu dóor ay doj ba ñu dee, ñee, ñu xeet leen ba xar leen ñaar, ñee, ñu bóome leen saamar, ñii di wëndeelu, sol deri xar mbaa bëy, te diy ndóol, ñu di leen bundxatal, di leen mitital.