TSK

TSK · 2 Kings 21:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Mbooloo ma nag lànk, déggaluñu Samiyel, xanaa ne ko: «Ndokk! Buur daal lanuy am,

Ca tànki buuri Israyil la topp. Doomam ju góor sax def na ko sarax, lakk ko ngir tuur ya, di roy ñaawtéefi xeet, ya Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israyil.

¶ «Waaye dégguñu ndigal, xanaa di la gàntal. Dañoo sànni saw yoon seen gannaaw; sa yonent ya leen doon xiirtal ci délsi ci yaw, ñu rey leen, ba ñàkke la kersa lool.

Ngalla Aji Sax ji, sàmmal ku néewle, aar ko saa su ne ci nitu tey.

¶ «Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw seen reewande wees na reewandey xeet yi leen séq, samay dogal, jëfewuleen ko; sama àttey yoon, sàmmuleen ko; sàmmuleen sax àttey xeet yi leen wër,

Yemuloo rekk ci roy seen jëfin ak seen jëf ju siblu. Tuuti na! Yaa leen gëna yàqu ci sa mboolem jëfin.

Ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Ab dëkk a ngii buy tuur deret fi biiram, ba tax bésam di jubsi. Mu ngi sàkk ay kasaray tuur, di sobeel boppam.

Noo baña déglu sunu kàddug Yàlla Aji Sax ji, di topp yoonam yi mu nu jox, yonent yiy jaamam jottli nu ko.

¶ «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy bóom yonent yi, di sànni ay doj ñi ñu yebal ci yaw, ba ñu dee, ñaata yoon laa namma dajale say doom, uuf ni ganaar di uufe ay cuujam, te nanguwuloo?

Ku xam lu baax loo wara def te defoo ko nag, bàkkaar nga.