tund yi ne soyox seey fi kanam Aji Sax ji boroom àddina sépp.
TSK
TSK · 2 Peter 3:10
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bés déy ñeel na Aji Sax ju gàngoor yi, ca lay xaare képp ku bew ak ku reew, ba kuy daŋŋiiral, detteelu.
Gàngooru asamaan gépp ay tasaaroo, asamaan taxañe ni lëmësub kayit, gàngooram gépp ruus ni xobu reseñ mbaa figg gu lax.
Céy, bii bés! Bésub Aji Sax ji moo dëgmal, te ni sànkute gu bawoo fa Aji Man ji lay dikke.
Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, kiy laal suuf, mu ne soyox seey, mboolem lu ci biiram di jooyoo; suuf fuddoondoo ni dexu Niil, dellu rës ni dexu Misra.
Tund ya mu joggi da naan soyox seey, xur ya xar, wàyyi ni dax ju jege sawara, def ni ndox mu wale kaw mbartal.
Waaye lii de xamleen ko: boroom kër, su xamoon wan waxtu la ab sàcc di ñëw, du ko wacc moos, mu dàjjiy, dugg këram.
dàqleen nit kooku, jébbal ko Seytaane, ngir sànkutey yaramam, ndax aw fitam mucc, keroog bésu Boroom bi.
ndax yeen ci seen bopp, xam ngeen xéll ne Sang bi, ni sàccub guddi lay dikke.
Waaye asamaanu tey jii, ak suuf, genn kàddug Yàlla googu moo leen yeb cib denc, ñeel sawara, kera bésub àtte ba, bésu sànkuteb aji gëmadi ñi.
Te it malaaka ya yemul woon ca daraja ja ñu amoon, xanaa wacc seen dëkkuwaayu bopp, Yàlla moo leen denc ci lëndëm gu ne këruus, yeewe leen buum yu dul deñ, ngir àtteb bés bu mag ba.
¶ Mu ne: «Maa ngi nii yoot, di dikk nib sàcc. Ndokklee, yaw mi teewlu, fàggu say yére, ba doo deme gàcceg yaramu neen, ñu di la seetaan.»
¶ Ma daldi gis asamaan su bees ak suuf su bees. Fekk na asamaan su jëkk sa ak suuf su jëkk sa wéy, te géej amatul.