TSK

TSK · 2 Samuel 12:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Firawna nag yónnee, woolu Musaak Aaróona. Mu wax leen ne leen: «Bii yoon de, maa tooñ. Aji Sax ji moo nekk ci dëgg, te maak sama waa réew ñoo sikk.

¶ «Bu loolu weesee képp ku faat bakkanu nit, dee rekk mooy àtteem.

¶ Sóol ne Samiyel: «Ndaxam déggal naa Aji Sax ji. Dox naa yoon wi ma Aji Sax ji yebal; indi naa Agag buurub Amaleg te Amalegeen ñi, faagaagal naa leen.

¶ Sóol dellu ne: «Bàkkaar naa! Waaye ngalla waay sagal ma ci sama kanam magi askan wi ak ci kanam Israyil. Walbatikul, ànd ak man rekk, ma sujjóotali sa Yàlla Aji Sax ji.»

¶ Daawuda nag gis malaaka may fàdd askan wa. Mu ne Aji Sax ji: «Man miy sàmm bi déy, maa bàkkaar, maa def lu bon. Ñii diy xar doŋŋ yu topp ci man, lu ñu def? Na sa loxo dal ci sama kaw man kay, maak sama waa kër baay!»

¶ Axab ne Ilyaas: «Ãa, noon bi, gisati nga ma?» Ilyaas ne ko: «Gis naa la, ndax dangaa dogu ci def lu bon lu Aji Sax ji ñaawlu.

¶ Ba mu ko defee Akasiya yebal njiitu juróom fukki dag, mu ànd ak juróom fukki nitam, dem ba ca Ilyaas. Gisuñu lu moy mu toog ca kaw tund wa. Njiit la ne ko: «Ée góoru Yàlla gi, Buur nee nga wàcc.»

Job 7:20 TSK

Yaw miy seetlu jaam ñi, ma bàkkaar, lu mu lay wàññi? Ana lu tax nga di ma diiral sa bopp nii, ba ma mujj diis la gann?

Dib taalif, ñeel Daawuda. Ndokklee yaw mi ñu baal bàkkaar, jéggal la ag moy.

Yaw laa moy, yaw doŋŋ. Li nga ñaawlu laa def. Kon boo waxee, yaa yey; te soo àttee, wàcc nga.

Ki Sax, yaw, soo doon lim bàkkaar, Boroom bi, ana kuy taxaw?

Kàddu yu lay yedd ci kuy dégg, jaarob wurus la mbaa gànjaru ngalam.

Ma ne: «Wóoy man, sànku naa! Man miy nit ku làmmiñam sobewu, xeetoo ci ñu seen làmmiñ sobewu, te samay gët tegu ci kaw Buur Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi.»

Du xaalis boo ma jëndale barax bu xeeñ, du nebbonu sarax boo ma reggale. Xanaa lakkal maak say bàkkaar, sonal maak say ñaawtéef.

Malaaka ma wax ak ña taxaw fa kanamam ne leen: «Summileen yéreem yu dand yi.» Mu teg ca ne Yosuwe: «Dama ne, far naa sa bàkkaar, te dinaa la solal lu jekk.»

Acts 2:37 TSK

¶ Ba mbooloo ma déggee loolu, naqar wu mel ni jam-jamu xol la leen def. Ñu ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, nu nuy def nag?»

Ñi Yàlla taamu, ana ku leen di tuumaal? Yàlla de mooy jox nit àtteb ku jub.