TSK

TSK · 2 Samuel 21:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Fii ak ñetti fan Firawna dina la siggil, ba noppi wékk la ci bant, picc yi ñëw, di for sa suux.»

summi yére ya ñu ko jàppe njaam, te toog seen biir néeg. Day tiislu nag ndeyam ak baayam lu mat weeru lëmm. Gannaaw loolu ngeen dëkkoo ko, di jëkkëram, muy seen jabar.

bu néewam fanaan ca garab ga, nañu ko daldi rob ca bés ba, ndax ki wékke alkàndey Yàlla la. Buleen sobeel réew mi leen seen Yàlla Aji Sax sédd.

Sóol nag amoon na nekkaale bu ñuy wax Rispa doomu Aya. Mu am bés Isboset ne Abner: «Ana lu waral nga dëkkoo sama nekkaaleb baay?»

¶ Gannaaw loolu Ilyaas ne Axab: «Doxal lekki te naan, ndax taw bu réy a ngi riir di ñëw.»

Seen xel demul sax ba ne: “Tee noo ragal sunu Yàlla Aji Sax, jiy jot, mu tawal nu, taw yu jëkk ak yu mujj yi, àppal nu ayi bési ngóob, sédde nu?”

Ca kaw tundi Israyil ngay daanu, yaak mboolem say gàngoor, ak mbooloo yi ànd ak yaw. Tan yeek lépp luy njanaaw ak ndundati àll bi laa lay jox, leele la leen.

Joel 1:18 TSK

Céy ni mala yiy binnee! Gétti nag yaa ngi jànnaxe, ndax ñàkk parlu, gàtt yi itam loof.

¶ Bu suuf maree, ñaanal Aji Sax ji ab taw, Aji Sax ji mooy sàkk ay xàmbaar, sóobal nit ab taw, saxalal ku ne am ñax ci àll bi.