TSK

TSK · 2 Samuel 21:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ca ëllëg sa Musaa ne mbooloo ma: «Yeen de bàkkaar ngeen bàkkaar bu réy, waaye maa ngi nii di yéeg, jëm ci Aji Sax ji. Jombul ma jotul leen seen bàkkaar.»

Su nit ki tooñee moroomu nitam, Yàllaay àtte; waaye su dee Aji Sax ji la nit ki tooñ, ana ku koy àtte?» Wax jooju nag taxul ba tey ñu déggal seen baay. Booba fekk na Aji Sax ji namm leena rey.

Nun danu di niti jàmm ñu am kóllëre ci digg Israyil. Yaw nag yaa ngi wuta faagaagal dëkk bu mag bu jaboote ñi ko wër ñépp ci digg Israyil. Ana lu waral nga namma tas dëkk bu Aji Sax ji séddoo?»

Micah 6:6 TSK

Ana lu may dikkaale fi kanam Aji Sax ji, ba sujjóotal Yàlla jooja fa kaw. Tee ma koo dikke ay rendi-dóomal, ay wëlluy menn at?

ndax deretu yëkk, ak ju sikket kat manula far ay bàkkaar.