seen jur gu gudd ak gu gàtt yokku, xaalis ak wurus yokkul leen, seen jépp alal yokku,
TSK
TSK · 2 Samuel 24:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yowab, mi Seruya di yaayam, daldi ànd ak niti Daawuda, ñu dem dajejeek ñoom ca wetu déegub Gabawon. Ñii taxawe gii wet, ñee taxawe ca wàlla, ñu séq déeg ba.
Yowab, mi Seruya di ndeyam, moo jiite woon mbooloom xare ma; Yosafat doomu Ayilut yor kàddug buur;
¶ Yowab moo jiite woon mbooloom xarem Israyil gépp; Benaya doomu Yoyada yilif dag ya dar Buur, te di waa Keret ak waa Pelet;
¶ Ba loolu amee Aji Sax ji wàcce mbas ci kaw Israyil, dale ko ca suba soosa ba keroog ba àpp ba matee. Ña dee ca askan wa di juróom ñaar fukki junni (70 000) diggante Dan ca bëj-gànnaar ba Beerseba ca bëj-saalum.
Réy-réylu, detteelu rekk; woyofal, ñu naw la.
¶ Te it, waccalees na ma ndégu biir suux, mu taxawe ndawal Seytaane, di ma mitital, ngir ma baña bew ndax peeñu yu yéeme.