TSK

TSK · 2 Samuel 5:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Nëgëni ëllëg maa ngi lay yónnee waa ju dëkk diiwaanu Beñamin. Nanga ko diw, fal ko, ngir mu yilif Israyil, sama ñoñ, ba xettli sama ñoñ ci waa Filisti. Maa geesu sama ñoñ, ndax seeni yuux àgg na fi man.»

¶ Gannaaw ba loolu wéyee Aji Sax ji ne Samiyel: «Yaw foo àpp sa jooy yi ngay jooy Sóol te man maa ko dàq, ba doonatul buur ci Israyil? Gannaaw maa foq nguuram ci Israyil kay, duyal sa béjjén diwu oliw ba mu fees te nga dox, ma yebal la ci Yese waa Betleyem bi. Gis naa ciy doomam ki may fal buur.»

Daawuda nag di dem ci bépp yoonu xare bu ko Sóol yebal, di ca am ndam. Sóol fal ko njiitu xarekat ya, gàngoor gépp rafetlu loolu, jawriñi Sóol itam rafetlu ko.

Teewul mboolem Israyil ak Yuda sopp Daawuda, ngir moo leen jiite woon, di xareji, di dikk.

Keroog, sang bi, bu la Aji Sax ji defalee mboolem lu baax la mu la dig, ba fal la, nga jiite Israyil déy,

Mboolem fu ma masa màngeji ak bànni Israyil gépp, ndax mas naa wax benn baat, jëme ci genn giirug Israyil gu ma sant ñu sàmm Israyil sama ñoñ, ne leen ñu tabaxal ma kërug bantu seedar?”

«Dellul ba ca Esekiya, sama njiitu ñoñ, nga ne ko: “Aji Sax ji sa Yàllay maam Daawuda dafa wax ne: Dégg naa sag ñaan, gis naa say rongooñ. Maa ngii di la wéral, te bu gannaaw ëllëgee dinga dem kër Aji Sax ji.

Mooy sàmm géttam bii ni kuy sàmm ug juram, boole mbote yi cib loxoom, taf cib dënnam, yóbbu; xar yiy nàmpal, mu wommat.»

¶ «Gannaaw loolu maa leen di waajalal ab sàmm bu leen di sàmm. Kookooy Daawuda sama jaam bi. Moom moo leen di foral, mooy doon seen sàmm.

Micah 5:4 TSK

Kookooy doon buntu jàmm, ba bu waa Asiri songee sunum réew, ba daagoo sunu kawi tata, juróom ñaari njiit lanu koy yékkatil, ba juróom ñetti garmi.

¶ Ndax kat Yàlla mi lépp lu sàkke ñeel, te lépp sàkkoo ci moom, moo nammoona wommat gone yu bare ba sédd leen daraja. Moo tax muy lu jaadu, mu sottale matug Yeesu ay coono, ndax Yeesu moo xàllal gone yooyu yoonu mucc.