TSK

TSK · 2 Samuel 6:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Léegi nag sa nguur du wéy; Aji Sax ji sàkkul na boppam ki xolam jubool, te fal na ko njiitu ñoñam, ndax yaa sàmmul li Aji Sax ji santaane.»

¶ Gannaaw ba loolu wéyee Aji Sax ji ne Samiyel: «Yaw foo àpp sa jooy yi ngay jooy Sóol te man maa ko dàq, ba doonatul buur ci Israyil? Gannaaw maa foq nguuram ci Israyil kay, duyal sa béjjén diwu oliw ba mu fees te nga dox, ma yebal la ci Yese waa Betleyem bi. Gis naa ciy doomam ki may fal buur.»

Te it démb ak bëkk-démb, ba Sóol dee sunu buur, yaw yaa doon jiite Israyil ciy xareem. Aji Sax ji ne la: “Yaay sàmm Israyil sama ñoñ te yaay doon kilifag Israyil.”»

Daawudaa ngay fecc ak doole fa kanam Aji Sax ji. Daawudaa nga gañoo am xar-sànnim lẽe.

Sunu kiirlaay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israyil ay boroom.

¶ Kon nag su ngeen di lekk, mbaa ngeen di naan, mbaa ngeen di def leneen, lépp lu ngeen di def, wutleen koo terale Yàlla.