Kuy ji di jooy, yal na góob, di sarxolle.
TSK
TSK · 2 Timothy 1:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Su boobaa janq bégem pooj, waxambaaneek mag feelu ko, ma soppi seen ñaawlu mbégte, dëfal leen, bànneexal leen, ñu dëddu naqar.
Teewluleen nag te fàttliku ne diiru ñetti at, guddi ak bëccëg, masumaa noppee àrtu kenn ku nekk ci yeen, bay jooy sax.
Yàkkamti naa leena gis, ba jottli leen mayug yiw gu bawoo ci Noo gu Sell gi, ngir dooleel leen,
Yàlla seede na ne sopp naa leen yeen ñépp, cofeel gu Almasi Yeesu ci boppam àttana tibbe ci biir xolam.
¶ Nun nag bokk yi, teqale nañu nu ak yeen ab diir, waaye xol yi sorewaatoowul, xanaa jëmm yi rekk. Waaye sunu nammeel gu réy tax na noo def sunu kem kàttan, ndax yàkkamtee gise waat ak yeen.
Gaawala ñëw, balaa seddub lolli di jam. Ab nuyoo ñeel na la, tukkee ci Ëbulus ak Pudeñsë ak Linus ak Këlójaa ak bokk yépp.
ndaxte Gàtt bi ci diggu ngàngune mi moo leen di sàmm, yóbbu leen ca bëti ndoxum dund ma, te Yàllaa leen di fompal wépp rongooñ.»