TSK

TSK · 2 Timothy 2:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Su ma naroon ñaawtéef, Boroom bi du ma déglu.

Dawal ni kéwél gu rëcc ub rëbb, ne fërr ni picc mu raw ab fiirkat.

Saraxub ku soxor, Aji Sax ji bañ na ko; ñaanu kuy jubal da koy bége.

Acts 7:59 TSK

¶ Ñuy dóor Eccen ay doj, moom muy ñaan Yàlla, naan: «Sang Yeesu, nangul sama bakkan!»

Ndax kat solob nguurug Yàlla jotewul dara akug lekk mbaa ag naan, waaye solob nguuru Yàlla moo di njub ak jàmm, ak mbégte ci ndimbalal Noo gu Sell gi.

Kon nag Yàlla miy maye xolu muñ, di ñaaxe, yal na leen may mànkoo gu mat sëkk, ni ko Almasi Yeesu bëgge,

¶ Bokk yi nag, dama leen di ñaax, ci sunu turu Sang Yeesu Almasi, ngir seen kàddu di genn, te féewaloo baña am ci seen biir, xanaa ngeen bennoo ci lépp, bokk menn xel, ak benn jëmu.

Ndénkaane lii nag, li ko taxa jóg mooy luy yee ag cofeel gu bawoo ci xol bu rafet, ak xel mu dal, ak ngëm gu mucc jinigal.

¶ Kon li ma bëgg moo di góor ñi di ñaane fépp, tàllal loxo yu mucc sikk, te bañ cee boole meroo ak mbiicoo.

¶ Yaw miy nitu Yàlla nag, dawal loolu, te topp njub ak njullite ak ngëm ak cofeel ak muñ akug teey.

¶ Soppe yi, ay gan ngeen, ay doxandéem ci kaw suuf. Kon nag li ma leen di dénk moo di ngeen moyu xemmemtéefi bakkan yiy xeex ak ab xol.