Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw, ndax Aji Sax jee ma diw, fal ma, ngir ma àgge néew-doole yi xibaaru jàmm. Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, yégal jaam yi, seen goreel, yégal ñi ñu tëj, seen ubbite.
TSK
TSK · 2 Timothy 4:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Noowug Boroom baa ngi fi sama kaw, moo ma fal, ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm bi. Da maa yebal ngir ma yégal jaam yi ne dees na leen goreel, yégal gumba yi ne dinañu gis, yégal ñi ñu not, ne dees na leen jot,
Ku ma taxul nga xàcc sa péete ak man nag, ndokklee yaw.»
¶ Ña nga teereji dëkk ba ñuy wax Salamin, daldi fay yégle kàddug Yàlla ca jànguy Yawut ya, ku ñuy wax Yowaan Màrk ànd ak ñoom, di leen jàpple.
Ñu ne ko: «Gëmal Sang Yeesu, daldi mucc, yaak sa waa kër.»
Ba ñu dikkee, mu ne leen: «Yeen ci seen bopp xam ngeen bu baax, ca bés ba ma jëkkee teg sama tànk Asi, ba tey jii, ni ma masa doxale ak yeen,
¶ Diiru ñaari at la Póol dal Room ci kërug boppam gu muy fey, di fa àggale mboolem ña koy seetsi.
Bégeleen seen yaakaar, di muñ ci biir tiis, tey saxoo ag ñaan.
Ci moomu mbooloo laa dib jawriñ, te Yàllaa ma sase noonu, ñeel leen, ngir ma xamle kàddug Yàlla ba mu mat sëkk.
Xam ngeen ne fi baay féete doomam lanu féete kenn ku nekk ci yeen.
buleen gàttañlu ay kàdduy waxyu.
Loolu ngay def sam xel, mbir yooyu ngay pastéefoo ba sag yokkute bir ñépp.
Ku setal sa bopp nag ba mucc ci yu bon yooyii, yaay doon ndabal teraanga lu sell te amal sangam njariñ ngir jépp jëf ju baax.
¶ Yaw nag seetlu nga bu baax sama àlluwa, ak sama dundin, ak sama mébét, ak sama ngëm, ak samag muñ, ak sama cofeel, ak samag ñeme coono,
¶ Googu kàddu ngay waaree, di dénkoo ak di femmoo, te boole ci fulla ju mat sëkk. Bu la kenn yab.
¶ «Man, képp ku ma sopp, maa koy jubbanti, yar ko. Kon nag farlul te tuub!