¶ Aji Sax ji ne Musaa: «Loolu nga wax, moom laa lay defal, ndax daj nga samaw yiw, te it maa la xam ci saw tur.»
TSK
TSK · Acts 10:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Te Yanqóoba sama jaam bi, Israyil moomu di sama tànnéef moo tax ma wooye la saw tur, takkal la ndombol tànk, te xamuloo ma.
Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp.
¶ Ba ñu demee ba tollu wetu fukki waxtu ak ñaar ca bëccëg, ag lëndëm a wàcc ca réew ma mépp, ba fukki waxtu ak juróom ca ngoon.
Ca guddi ga nag malaakam Boroom bi ubbi bunti kaso ba, génne leen, ne leen:
¶ Ab taalibe bu ñuy wax Anañas nag ma nga woon ca Damaas. Sang bi feeñu ko, ne ko: «Anañas!» Mu ne ko: «Maa ngi, Sang bi.»
¶ Naka la Piyeer di xalaat ba tey ca peeñu ma, Noo gi ne ko: «Ñetti nit a ngi nii, di la seet.
Mu xamal nu ne malaakaa ko feeñu ci néegam, ne ko: “Yebleel ca Yope, nga woolu Simoŋ, ma ñu dàkkentale Piyeer.
Ndax malaakam Yàlla ji ma moom, te ma di ko jaamu, moo ma dikkal biig.
Xanaa malaaka yépp duñu ay ngelaw yu ñu sas ab liggéey, yebal leen ngir ñu taxawu ñi wara jagoo ag mucc?