daldi ne doom aadama: «Ragal Boroom bi daal, mooy xel mu rafet, te dëddu lu bon mooy am ug dégg.»
TSK
TSK · Acts 10:35
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Woykat ba nee: «Naa déglu lu Aji Sax ji Yàlla di wax.» Jàmm lay wax wóllëreem ñiy ñoñam, ba duñu dellu ci jëfi dof.
Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu xam-xam, te xel mu rafet akub yar, dof yaa ko xeeb.
Bul doyloo sa xel mu rafet, ragalal Aji Sax ji, dëddu mbon;
Ma daaneele fii, déggees na lii lépp: Yàlla, ragal ko; ay santaaneem, jëfe ko; loolu rekk mooy nit.
Ñooy sarxe jur gi ñu may jooxeel, lekk yàpp wi, Aji Sax ji buggu ci dara. Maay bàyyi xel ci seen ñaawtéef, mbugale leen seeni moy, te ñoom Misra lañuy dellu.
¶ Ba mu ko defee mbooloom gëmkat ñi ci mboolem diiwaani Yude ak Galile ak Samari daldi am jàmm. Ñuy gëna dëgër, di wéye ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalal Noo gu Sell gi.
Yàlla amul xejj ak seen sunu digg ak ñoom, ndax seen ngëm la raxase seen xol.
¶ Aaday xaraf nag amal na la njariñ, ndegam sàmm nga yoon wi ko digle. Waaye soo dee moykatub yoon wi, sag xaraf, ñàkka xaraf lay doon.
Am Yàlla da di Yàllay Yawut yi doŋŋ? Da dul Yàllay jaambur yi dul Yawut itam? Ahakay, mooy Yàllay jaambur ñeet kay!
Ci genn Noo gi lañu nu sóobe ci biir wenn yaram wi, nun ñépp, nu diy Yawut, mbaa nu diy jaambur, nu diy jaam, mbaa nu diy gor, te nun ñépp, genn Noo gi lañu nu nàndale.
Kon nag amul Yawut ak ku dul Yawut, amul ab jaam ak as gor, amul góor ak jigéen. Yeen ñépp benn ngeen ci Almasi Yeesu.
Waaye yeen ñi sore woon, léegi bi ngeen nekkee ci Almasi Yeesu, jege ngeen ndax deretu Almasi ji tuuru.
te ngeen rus Almasi, ba tax ngeen di nangulante.
Ni leen xibaaru jàmm bi dikkale nag, ni la dikkale àddina sépp, te mu ngi meññ, di law, na mu ko dale defe fi seen biir, ca bés ba ngeen déggee lu jëm ci yiwu Yàlla, ba ràññee ko dëgg.
Dundin wu yees woowu amul jaambur akub Yawut, amul ku xaraf ak ku xaraful, amul ab doxandéem ak ku xayadi, amul ab jaam ak as gor, waaye Almasi mooy lépp te moo nekk ci ñépp.