TSK

TSK · Acts 10:36

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Neleen bunt yi kulbét, ubbileen bunti cosaan yi, Buur Boroom ndam duggsi.

Janq doom, gisal, déglul te teewlu ma, fàtteel say bokk, fàtte sa kër baay,

Janti Buur aji jub day woomle, te ba keroog weer wiy fey, jàmm di law,

Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax ji daa wax sama Sang, ne ko: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon sa ndëggastal.»

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram, ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, tey jii, ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Àdduleen, layoosi, diisooleen fi seen biir kay! Ana ku xamle woon lii bu yàgg, yégle woon ko booba? Xanaa du man Aji Sax ji? Kenn du Yàlla ku dul man! Yàlla ju jub, di walloo, du kenn ku dul man!

Maay teg ci seen làmmiñ kàddug cant. Jàmm, na jàmm ñeel ñépp, ku soreek ku jege.» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Maa leen di faj.»

¶ «May xool ba tey ci biir peeñum guddi ma, gisuma lu moy jëmm ju mel ni doomu nit di ñëw, mook niiri asamaan, jëm ci góor gu mag gi; ñu yóbbu ko ba ca moom.

Micah 5:2 TSK

Moo tax Aji Sax ji di leen wacc ba keroog jant, ba kiy matu mucc. Ca la bokkam ya dese bakkan di dellu, fekki seen bokki bànni Israyil.

Luke 2:10 TSK

Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp.

Acts 2:36 TSK

¶ «Kon nag na wóor waa kër Israyil gépp ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàllaa ko def Sang ak Almasi.»

Acts 3:25 TSK

Yeen nag yeenay donoy yonent yi te yeenay séddu ci kóllëre, gi Yàlla fasoon ak seeni maam, ba mu nee Ibraayma: “Ci saw askan la xeeti àddina yépp di barkeel.”

¶ Gëmkat ña tasaaroo woon nag ndax fitna ja woon, ca mbirum Eccen, mujj nañu jàll ba diiwaanu Fenisi, ca dunu Sippar ak ca Àncos, waaye àggewuñu kàddu gi ñeneen ñu moy Yawut yi.

Ba loolu amee fit la leen Póol ak Barnaba tontoo, ne leen: «Yeen Yawut yi de lanu wara jëkka yégal kàddug Yàlla gi, waaye gannaaw gàntal ngeen ko, ba jombale seen bopp ag texe ba fàww, nu ngii di walbatiku ci jaambur ñi.

¶ Loolu sax moo waral Almasi dee, ba noppi dekki, dellu di dund, ngir ñi dee ak ñiy dund ñépp, muy seen boroom.

Aadama mu jëkk ma, ci suuf la jóge woon, di suuf; Aadamam ñaareel mi jóge fa asamaan.

ji mu fésal ci Almasi, ba mu ko dekkalee, dëël ko ci ndijooram, fa déndi asamaan.

Benn Sang bi la it, ak genn ngëm, ak genn sóobu cim ndox.

¶ Doom jooju moo di niruwaale Yàlla, mi kenn manula gis, mooy taaw bi, ki jiitu mépp mbindeef.

Ci fan yu mujj yii, Doom ji la waxe ak nun, ki mu jagleel lépp, ki mu sàkke àddina wërngal këpp.

Moom la Ibraayma jox fukkeelu cérub mboolem cëxëtoo ma. Ni ñu jëkka dégge aw turam Melkisedeg, ci tekki, mooy «buur bu jub». Bu loolu weesee itam moom mooy buurub Salem, muy «buuru jàmm».

mi yéeg asamaan, toog fa ndijooru Yàlla, ki malaaka yeek boroom sañ-sañ yeek boroom doole yi, bokk nekk cig curgaam.

Maay Kiy Dund, maa dee woon, maay dund nii tey ak ëllëg ba fàww te maa yor caabiy dee ak njaniiw.

Ci kaw mbubbam ak ci luppam, aw tur lañu ci bind te moo di: «Buuru buur yi, Sangu sang yi.»