Acts 13:30
TSK
Waaye Yàllaa ko dekkal,
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye Yàllaa ko dekkal,
Waaye ci wàllu Noo gu Sell gi, mooy ki dogal ba tabb muy Doomu Yàlla ji jagoo doole ndax ndekkiteem, te mooy sunu Sang Yeesu Almasi.
Ci sóobu googu lañu nu boole ak moom suul, ngir noonee Almasi dekkee ci màggug Baay bi, nun itam nu dekki bay dund dundin wu yees.
¶ Loolu sax moo waral Almasi dee, ba noppi dekki, dellu di dund, ngir ñi dee ak ñiy dund ñépp, muy seen boroom.
¶ Ndegam biral nañu ne Almasi dekki na, ana nu ñenn ci yeen mane ne ñi dee duñu dekki?
¶ Yàlla miy boroom jàmm, moom mi dekkal sunu Sang Yeesu, Sàmm bu mag bi, ci dooley deret ji mu fase kóllëre gu sax dàkk,