Képp ku ragal Yàlla dikkal, déglu, ma limal la li mu ma defal.
TSK
TSK · Acts 12:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Nañu sante Aji Sax ji ngoram ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.
di àtte néew-ji-doole, di leel ku xiif. Aji Sax jeey tijji ku ñu tëj.
Ba mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Ñu daldi xam ne am na lu ko feeñu ca néeg Yàlla ba. Ma nga leen di liyaar, manatula wax.
Póol jóg, tàllal loxoom, nee leen: «Yeen bokki Israyil ak yeen jaamburi ragalkati Yàlla yi, dégluleen!
Noonu lañu génne kaso ba, dellu kër Lidi. Ñu gise faak bokki gëmkat ña, ñaax leen, doora dem.
Ca ëllëg sa Póol ànd ak nun, seeti Yanqóoba, fekk mag ñépp a nga fa teew.
Gannaaw gi mu feeñu Yanqóoba, teg ca feeñu ndawi Almasi yépp.
Ña ñu jàppoon ne ñooy kenuy mbooloom gëmkat ña nag, te ñuy Yanqóoba ak Sefas ak Yowaan, ba ñu ràññee yiw wi ñu ma jagleel, maak Barnaba lañu jox loxo, ngir nun nu liggéeyi ca jaambur ña, te ñoom ñu liggéeyi ci Yawut yi.
¶ Ci man Yanqóoba, jaamub Yàlla ak Sang Yeesu Almasi, la bataaxal bii bawoo, ñeel fukki giir ak yaar yi tasaaroo ci àddina. Maa ngi leen di nuyu.