ku la ñaanal barke, ma barkeel, ku la móolu it, ma alag, te xeeti àddina sépp, ci yaw lañuy barkeele.»
TSK
TSK · Acts 13:32
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dinaa ful sa askan ni biddiiwi asamaan, dinaa jox sa askan suuf sii sépp, te it ci saw askan la xeeti àddina sépp di barkeele,
Ab yonent bu soqikoo ci yeen kay, di seen mbokk ni man, moom la leen seen Yàlla Aji Sax ji di feeñalal. Moom ngeen di déggal.
Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram, ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, tey jii, ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.
Yaw Siyoŋ, xibaarkatu jàmm bi, doxal yéegi tund wu kawe, te xaacook doole. Yaw Yerusalem, xibaarkatu jàmm bi, xaacul te bul ragal! Neel dëkki Yuda yi: «Seen Yàllaa ngi!
Ndaw leeka rafeti tànk, kee bartaloo tund yi, di la dégtalsi jàmm, di la xibaar lu neex, àgge la ag mucc, ne la: «Éey, Siyoŋ, sa Yàllaay Buur!»
«Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay jebbil Daawuda njebbitu njekk, mu falu di buur bu xelu, di jëfe njub ak njekk ci réew mi.
¶ «Juróom ñaar fukki ayi bés lañu àppal sa mbooloo ak sab dëkk bu sell, ngir dakkal tooñ gi, jeexal moy gi, jotu ñaawtéef, saxal njubte ba fàww, matal peeñum yonent, ba delloo bérab bu sella sell ag sellngaam.
Maay yëngal xeetoo xeet, alali xeetoo xeet duggsi, ma feesal kër gii ak teraanga, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax;
Bégala bég, janq Siyoŋ mu taaru, janq Yerusalem mu taaru laa ne: Xaacul, sa buur a ngoog, jëmsi ci yaw, moo jot njekk ak mucc, te teewu koo woyof, war mbaam, cumbur doomu mbaam.
«Éey saamar, yewwulal sama sàmm bi, sama jàmbaar jii ma lëngool,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. «Dóoral sàmm bi, xar yi tasaaroo, ma walbati sama loxo, jublu ci jur gu ndaw gi.
Moo wallu bànni Israyil, jaamam, bàyyee ko xel yërmandeem,
Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp.
Ci kaw loolu bés bu nekkaan, muy ca kër Yàlla, di ca biir kër ya, noppiwuñoo jàngle ak a xamle xibaaru jàmm bi yéene ne Yeesu mooy Almasi.
Sama taxawaayu tey ci ëttub àttekaay bii nag, mooy yaakaar ji ma am ci dige bi Yàlla digoon sunuy maam.
Ñooñoo di xeetu Israyil wi xéewloo céru doon doomu Yàlla, xéewloo daraja, xéewloo kóllëre yi, ak ndigali yoon wi, ak liggéeyu jaamu Yàlla gi, ak dige yi;
Te Ibraayma lañu digoon dige yi mook ki taxawal askanam. Newuñu: «ñi taxawal ay askanam», mbete ñu bare lañuy wax, waaye wenn rekk la: «ki taxawal askanam,» te ki taxawal askanam moo di Almasi.