TSK

TSK · Acts 13:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Képp ku jaxasoo ak mala, dee rekk mooy àtteem.

¶ Mboolem kàddu gi ma leen dénk nag, sàmmooleen koo jëfe. Buleen ci yokk lenn, buleen ci wàññi lenn.

Mu ne: “Maay dikk, doon xel muy safaan dëgg ci làmmiñu yonentam yépp.” Mu ne ko: “Yaa koy nax, te man nga ko. Demal defe noonu.”

Am na ñu naan: «Laajleen ñiy gisaanee nit ñu dee, ak boroom rawaan yiy kebetook a ŋun-ŋuni. Aw xeet sañ nañoo gisaanee seeni tuur, tey diis ñi dee mbiri ñiy dund.»

Kon nag gannaaw ñu ngi lajjal sama ñoñ, naan leen lépp jàmm! Te jàmm amul, mu mel ni miiru digaloo bu sew bu ñu ñab-ñabal, te ñii defuñu lu moy raax ca weexal,

Ba mu ko defee ñu bare ca gëmkat ña dikk, biral seenug tooñ, daldi xamle yu bon ya ñu daan jëfe.

Noonee Sànnes ak Sàmbres doon jànkoonteek Musaa, ni la góor ñooñu di jànkoontee ak dëgg gi; ñooy nit ñu seenum xel yàqu, te ñu doyadi ci wàllu ngëm.