TSK

TSK · Acts 14:15

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yuusufa ne ko: «Du ci man de, waaye Yàlla mooy baaxe Firawna pirim jàmm.»

Ana ci mboolem boroomu suux, ku ci masa dégg kàddug Yàlla jiy dund, mu jibe ci sawara, nii nu ko dégge, ba noppi di dund?

Daawuda ne ña mu dendal: «Ngeen ne, lees di defal ku rey waa Filisti bii, ba faj gàcceg Israyil? Ak kuy yéefaru waa Filisti bii sax, bay dëkk gàngoori Yàlla jiy dund?»

Li ko waral di mboolem bàkkaar yi Basa ak doomam Ela bàkkaar te bàkkaarloo ko Israyil, ba feesal xolu Aji Sax ji Yàllay Israyil ndax seen tuuri neen.

Jombul nag sa Yàlla Aji Sax ji dégg mboolem kàdduy bëkk-néeg bi sangam buurub Asiri yebal, ngir mu kókkali Yàlla jiy dund. Te kon sa Yàlla Aji Sax ji mooy dogal mbugal mi war ci kàddu yooyu mu dégg. Yékkatil kàddug ñaan rekk, ngir ñi fi desagum.”»

Yaw laa dénk sama bakkan. Aji Sax ji, Yàlla miy dëgg, ngalla jot ma.

Sunu ndimbal a ngi ci turu Aji Sax ji, ki sàkk asamaan ak suuf.

Bu yàgg lañu ma dëj, ca ndoorte la, bala suuf a sosu.

Ku mel nii du délloosim xelam, ba xam, ràññee ne: «Xaaju matt mi laa taal, lakke mburu, wàjje yàpp, lekk; mu des, ma di ko sàkke lu seexluwu lii? Ab dogu bant laay sukkal?»

Yeen daw-làquy xeet yi, dajeleen, dikk, ànd, jegesi. Képp ku gàddu tuuru bantam, ak kuy ñaan tuur mu ko dul wallu, kooka xamul dara.

Sama bokk yaa ngooguy yuuxu yuux yu àkki fu sore, naan: «Moo Aji Sax ji daa newul Siyoŋ a? Moo Buurub Siyoŋ da fee nekkatul a?»

Ñoom ñépp a bokk dofe, ñàkk bopp: xam-xamu kasara, bant kese!

Nitoo nit dim sannax, sore xam-xam: te képp kuy tëgg sa jëmmu tuur, yaa añe gàcce. Sa jëmmi weñ ji nga xelli, di neenug neen, noog bakkan, tus!

«Éy saa Boroom, Aji Sax ji! Yaw déy yaa sàkk asamaan, sàkk suuf ci sa doole ju bare ak sa kàttan. Dara tëwu la.

¶ Gannaaw loolu Buur Daryus bind waa mbooloo yépp ak xeet yépp ak làkk yépp, di waa àddina sépp, ne: «Jàmm ngeen!

Jonah 2:8 TSK

Noowal bakkan a nga may rëcc, sama xel ne yarr ci yaw, Aji Sax ji, sama ñaan àgg fa yaw, ca sa kër gu sell ga.

Acts 4:24 TSK

Ba ko bokk ya déggee, ñoom ñépp a mànkoo, daldi yékkati kàddug ñaan fa Yàlla, ne: «Buur Yàlla, yaa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak lépp li ci biir.

Piyeer yékkati ko, ne: «Déet jógal, man it, nit doŋŋ laa.»

Nun nag noo leen di àgge xibaaru jàmm bii: li Yàlla digoon sunuy maam,

¶ Gannaaw ba ñu xamlee fa Derbe xibaaru jàmm bi, ba am fa taalibe yu bare, dañoo dellu Listar ak Ikoñum ak Àncos gu Pisidi.

¶ Diggante ba Póol di nég Silas ak Timote ca Aten, xolam jeex na ndax dafa gis na dëkk ba yeboo ci jaamu ay tuur.

Maa lay musal ci askanu bànni Israyil, ak ci jaambur ñi ma lay yebal,

¶ Loolu nag fekk na ñu gëjoona lekk. Póol daldi taxaw ca seen biir ne: «Bokk yi, su ngeen yégoon déggal ma, baña jóge Keret, ba moyu loraange gii ak yàqule gii.

Ndax kat, li gisuwul ci Yàlla, te di manooreem gi dul jeex, ak jikko ji mu wéetoo ndax li muy Yàlla, ba àddina sosoo ba tey, xel man na koo ràññee ci ay liggéeyam, te looloo leen taxa ñàkku lay.

¶ Lii nag maa leen ko wax, te di ko biral ci turu Boroom bi: Ni xeeti yéefar yiy jëfe, topp seen xalaat yu tekkiwul dara, buleen jëfeeti noonu.

ngir su ma yeexee itam, nga xam nooy doxale ci kër Yàlla, ci biir mbooloom Yàlla jiy dund. Mbooloom gëmkat mi mooy kenug dëgg gi, di cëslaayam.

¶ Ilyaas nit la woon ku bindoo ni nun, waaye ba mu saxee ci ñaan ngir mu baña taw, ndox laalul suuf diiru ñetti at ak genn-wàll.

¶ Ma daldi ne gurub sukk ciy tànkam, ngir sujjóotal ko. Mu ne ma: «Déet, ëpp naa def. Sa mbokkum jaam doŋŋ laa, ni yaak sa bokk yi jàppoo seedeel Yeesu. Sujjóotalal Yàlla. Ndaxte seedeel Yeesu moo di Noo giy dundal waxyu.»

Mu ne ma: «Ëpp naa def, sa mbokkum jaam doŋŋ laa, ni yaak sa bokki yonent yeek ñiy sàmm kàdduy téere bii. Sujjóotalal Yàlla.»