Ñu mànkoo ñoom ñépp ngir saxoo ñaan ci Yàlla, ànd ceek jigéen ñi ak Maryaama ndeyu Yeesu, ak rakki Yeesu yu góor.
TSK
TSK · Acts 15:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bés bu nekk nag ñu doon benn bopp, saxoo teew ca kër Yàlla ga, di dagg mburum bokkoo ci këroo kër, tey bokk lekk ci biir mbég ak woyoflu.
¶ Ba loolu amee ndawi Yeesu yi ak mag ñi bokk daje, ngir seet mbir moomu.
Kon nag noo yebal Yuda ak Silas, ngir ñu àgge leen ci seen gémmiñu bopp, lii nu leen bind.
Nuyul-leen ma Tirifen ak Tirifos, jigéen ñu sonn ci liggéeyu Boroom bi, ak it ndaw si Persidd mi sonn lool ci liggéeyu Boroom bi.
Ña ñu jàppoon ne ñooy kenuy mbooloom gëmkat ña nag, te ñuy Yanqóoba ak Sefas ak Yowaan, ba ñu ràññee yiw wi ñu ma jagleel, maak Barnaba lañu jox loxo, ngir nun nu liggéeyi ca jaambur ña, te ñoom ñu liggéeyi ci Yawut yi.
¶ Mboolem lu jëm ci man nag, Tisig dina leen ko xamal. Mbokk la, soppe la, jawriñ ju wóor la, te it sama mbokkum jaam la, ci liggéeyu Boroom bi.
ba dootu doon sab jaam, waaye day wees ab jaam, di mbokk, di soppe, ma sopp ko lool, te nga war ma koo gëna sopp, ngir jëmmu boppam, ak Sang bi ngeen bokk.