TSK

TSK · Acts 16:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Éy Yàlla, baaxe ma, ngalla baaxe ma, fi yaw laay làqu, yiiroo sa kiiraay, ba musiba yi jàll.

Nabukodonosor nag jegeñsi buntu taal bu yànj ba, daldi àddu ca kaw ne: «Éey Sadarag, Mesag, Abet Nego, jaami Yàlla jiy Aji kawe ji, génnleen fii!» Sadarag ak Mesag ak Abet Nego daldi génne ca biir sawara sa.

Ma tëdd sama lal, daldi am gént gu ma tiital, ak xalaat ak peeñu yu ma indil njàqare.

dàqe ko ci nit ñi, def xel ma xelum rab. Mu dëkk ak mbaami àll yi, am ñax dim xontam niw nag, lay biy wàcc, di ko faam, ba kera ba mu xamee ne Aji Kawe jee yor nguurug nit, di ko jox ku ko neex.

¶ Ba njël jotee, ba bët di bëgga set, Buur jóg, daldi gaaw dem ca kàmbu gaynde ya.

Micah 6:6 TSK

Ana lu may dikkaale fi kanam Aji Sax ji, ba sujjóotal Yàlla jooja fa kaw. Tee ma koo dikke ay rendi-dóomal, ay wëlluy menn at?

Luke 1:79 TSK

di niital ñi tooge biir lëndëm ak takkndeeru ndee, di nu gindi, teg nu ci yoonu jàmm.»

Luke 4:41 TSK

Ay rab itam di génn ñu bare, di yuuxu, te naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Teewul mu gëdd leen, aaye leen ñu wax, ndax xamoon nañu ne mooy Almasi.

Yeerukat ya dikk ne Yeesu: «Sëriñ bi, xam nanu ne njub ngay wax, di ko jàngle. Amuloo parlàqu itam, waaye ci kaw dëgg ngay jànglee yoonu Yàlla.

Gannaaw gi mu génne leen ca biti ne leen: «Sang yi, ana lu ma wara def, ba mucc?»

¶ Ci kaw loolu ay Yawut yuy wër di faj ku rab jàpp, tàmbalee roy, di tuddal ñi rab jàpp turu Sang Yeesu, naan rab yi: «Maa la dàq ci turu Yeesu, mi Póol di xamle.»

Ay gor ngeen, waaye jaami Yàlla ngeen. Kon buleen taafantoo li ngeen diy gor ba def lu bon.