Aji Sax jee baax, rafeti dogal, di gindi moykat ci yoon wi,
TSK
TSK · Acts 18:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Baat a ngi jib, naan: «Xàll-leen yoonu Aji Sax ji ci màndiŋ mi, fàkkal-leen sunu Yàlla xàll wu jub fi joor gi.
Yeen Efrayim, lu ma masa séq ak jëmmi tuur? Man maa leen di nangul, di leen wattu, di leen keral ni garab gu naat gu dul ruus, sa meññeef bawoo fi man.»
¶ Ca fukkeelu at ak juróom ci nguurug buur bu mag ba Tibeer Sesaar, ba Poñsë Pilaat yilifee diiwaanu Yude, Erodd yilif diiwaanu Galile, Filib magam yilif diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, Lisañas yilif Abilen,
ne ko: «Yaw nit ki fees ak gépp xeetu njublaŋ ak ndëngte, doomu Seytaane ji, noonu gépp njub, doo bàyyee lunkal yooni njub yu Boroom bi?
Mu ne leen: «Kon gan sóobu ngeen sóobu?» Ñu ne ko: «Xanaa sóobeb Yaxya.»
¶ Jant yooyu nag yemook yëngu-yëngu bu réy bu amoon ci mbirum Yoon wi.
¶ Almasi moomu nag lanuy xamle; na mu gëna xeloo lanuy àrtoo nit ku nekk, te ni lanuy jàngale nit ku nekk, ngir àgge nit ku nekk ba fa kanam Almasi, fekk ko mat sëkk, na mu ware ku ànd ak Almasi.
Kon nag tuddanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ndax ngeen wér. Aji jub ji, ag ñaanam, doole lay dale.