TSK

TSK · Acts 2:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ba ma falee ay njiit ci kaw Israyil sama ñoñ. Maa lay noppal ci sa noon yépp. Te it Aji Sax jaa ngi lay yégal ne la Aji Sax ji moo lay sosal kër.

Ñeel Suleymaan. Céy Yàlla, mayal Buur sa xelum àtte, mayal doomu Buur bii sa xelum njekk,

Sunu kiirlaay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israyil ay boroom.

Aji Sax ji daa giñal Daawuda dëgg gu mu dul dëddu, ne ko: «Ku jóge sa geño laay wuutal ci sa jal bi,

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram, ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, tey jii, ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

¶ «Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay sottal ngëneel la ma dig waa kër Israyil ak waa kër Yuda.

Micah 5:2 TSK

Moo tax Aji Sax ji di leen wacc ba keroog jant, ba kiy matu mucc. Ca la bokkam ya dese bakkan di dellu, fekki seen bokki bànni Israyil.

Luke 1:31 TSK

Dinga ëmb, ba jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.

Luke 2:10 TSK

Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp.

moo jëm ci Doomam, ji soqikoo ci askanu Daawuda, ci wàllu àddina.

¶ Bàyyil xel ci Yeesu Almasi mi ñu dekkal te mu soqikoo ci Daawuda, ni ko sama xibaaru jàmm indee.

Looloo waral Yàlla jàppaat beneen bés bees di tàbbee ci noflaayam, bés bu mu tudde «tey jii», te mooy ba mu waxee lu yàgga yàgg, gannaaw gi, ci gémmiñug Daawuda, kàddu gii ñu jota jukki: «Bésub tey jii bu ngeen déggee baatub Yàlla, buleen të.»

¶ Melkisedeg moomu doon buurub Salem te nekkoon sarxalkatub Yàlla Aji Kawe ji, ba Ibraayma délsee jóge xareem baak buur ya mu duma, kooku moo ko gatandu woon, ñaanal ko.

Ndax kat du genn kàddug waxyu gu masa soqikoo ci coobarey nit, waaye ci xiirtalub Noo gu Sell gi la aw nit daan waxe waxyu bu bawoo fa Yàlla.

Ci kaw mbubbam ak ci luppam, aw tur lañu ci bind te moo di: «Buuru buur yi, Sangu sang yi.»